Ndawtal
Sèmbu Alf@net ànd na ci xeltuk xelteef bu ñëpp bokk moom walla Wenn Mbala. (Wenn naanukaay walla Fu neex waay tibb). Da nu gëm ne warees na nu yaatal yooyu xelteef , te kenn du ca fay tus, te it, gëm it ne njëm-kanamuk yooyu xelteef lu war la, jaarale ko cib yëngute bu roofoo lool, ànd ci ak baay-defal yàlla yu bare kaar te sóobu ci njëm-kanamuk xaralay xiibaaruway ak jokkalente yi ci làkk yi doomi Afirik nàmp. Ci biir liggéeyu jàppalente boobu doŋŋ, la nuy man a saafara laajtaayi ëllëg yi, tey may ñëpp, moo xam boroom alal mbaa ku ndóol-, ñu baaxoo saafara yu gën ci ŋaa bu limtu bi walla man a jot ci xibaaruwaay yi ńëpp yelloo ci sunu jamonoy gëndëloo ju mat sëkk jii.
Nu ngiy ñaax képp ku ànd ci bii xeltu ñu jokko ak nun , nu ànd ngir leeral yoon wi.





