• English English
  • Français Français
  • Mandinka Mandinka
  • Seereer Seereer
  • Wolof Wolof

Alf@net - Les TIC en langues nationales du Sénégal

  • Dal bi
  • Jaar jaar
  • Ekip bi
  • Farandoo yi
  • Mébét yi

"Bu galan soppeekoo pecc mi soppeeku"
Léebu Awsa
Dal bi

Arafukaay Senegaal
Abiword ci wolof
Jàng tappe ci wolof
Gindeekukaayu Alf@net
Mozilla Firefox ci wolof

Jokkoo jëfandikookat bi

  • Sos koont bu bees
  • Laaj baatu jàll bu bees

Jaarjaaru nasub Alf@net

2007

  • Juddu dalub web Alf@net.
  • Teewe ndaje ba amoon ca Bamako "TIC ak Alfabetisasisyoŋ" te BREDA/UNESCO amaloon ko.
  • Dëpale Abiword.
  • Dëpale Mozilla Firefox 2.
  • Wax ci Alf@net ca Ñaame ci Ndaje FORIENF te SËSI(CECI)amaloon ko.

2006

  • Defaraat yeenekaay barimelo Alf@net ci 5 lammiñi reew mi. OSIWA moo ñu dimmali ci liggéey boobu.
  • Expérience de formation de formateurs Alf@net en cascade en partenariat avec l’ONG CRESP à Yoff, plus de 60 femmes néo-alphabètes formées. Cette expérience s’est poursuivie jusqu’en mars 2007.
  • Wanaleb Alf@net UKADD ci biir gàmmu ga doon màggal boroom xam-xam boobu , di ndem-si -yàlla Cheikh Anta Diop ma réer fukki at ca gànnaaw..
  • Jëf-gisu tekki dëppale ci Mosilaa Faayafoks.5.

2005

  • Mbootaayu Kanadaa bu Ŋànkul, SESI fas yéené Jàppale Anafaa ak porogaraamam , naka noonu yónni Dominik Roosfoor ci biir porogaraamu Initeraa.

2003

  • Tekkib xelteefu jagal mbind yi ci Enteernet ESPIP SPIP.

2001

  • Tàggatub 43 ndongooy làkki réew mi ci xamteef ci wolof, loolu ci bànqaasi Anafaa ci réew mi: NDakaaru, Cees, Luga, Ndar ak Kuŋel.
  • Rabatinug gindeekukaay Alf@net ba ñu tabaxeek Adobe Akorbaat.
  • Usmaan Faati Ndongo bokkoon na ci ab tàggat jëmale ko ci tabaxiinu xelteefi njàngale baremelo, ca Iniwersite bu Kebek, ca Montereyal (IKM), Kanadaa.

2000

  • Oksfaam dugal xaalis ci Pàcc bu jëkk ci porogaraamu Alf@net..

1999

  • Mbindum gis-gisu porogaraamu Alf@net ba nu jébbal Oksfaam GB.
  • Usmaan Faati Ndongo, di ndawal Koŋgaad daldi wanale gëstu ba ñu duppee "Nas yi jublu ci njëm-kanug sàkkitéefi caada yi" , loolu ci biir sémbu Bànk Monjaal ak Njawril gi ñu dénk Caada ci Senegaal

1997

  • Juddug dalu webu porogaraamu Alf@net..
  • • Usmaan Faati Ndongo génné ab gëstu bu ñu tuddée "Làkk yu bare yeek barimelo ci njàngum muskallaaf". Gëstu googee, wanale na ñu ko cib jataay bu jublu ci xalaat yu bees yi ci mbirum njàngaleb làkk , te Bereedaa ak Iniwersite bu Pensilwaani amal ko ci Ndakaaru

1996

  • • Ba ñuy waajal KONFINTEYAA (Ambuur '97), BEREDAA/INESKOO daldi duggante ak Anafaa, ngir ñu taxawal ab gëstu ci mbirum njàngaleb làkk ak xarala yu bees yi. Noonu Anafaa , sas Usmaan Faati Ndongo, ma ligéeeyoon ba noppi ci moomu mbir ci 1993, ngir mu ligéey ci mbóot mii: "Njàngum muskallaf ngir amal ëllëg jamonoy njàng mu sax ba faww". Gëstu bii la ko lal ba téy ,moodi fukk ak benneelu tektal ba.
  • English English
  • Français Français
  • Mandinka Mandinka
  • Seereer Seereer

Xeltéef

  • Gindeekukaay yi
  • Xeltéef yi
  • Jumtukaay yi

Këmb barimelo

  • Internet ci joola
  • internet ci mandeŋ
  • internet ci pulaar
  • internet ci seereer
  • internet ci soninke
  • internet ci wolof

Ndawtal

  • Ressources

Powered by Drupal, an open source content management system
  • Dal bi
  • Jaar jaar
  • Ekip bi
  • Farandoo yi
  • Mébét yi

Association nationale pour l'alphabétisation et la formation des Adultes
Villa 17bis, Patte d'Oie Builders Nord Ext., B.P. 10453 DAKAR-LIBERTÉ
Dakar, Sénégal